Onion Browser Ci iOS Ci iOS Ci Linux Ci Linux Ci Mac OS Ci Windows

Wër ndombo Tere ak Tor

Tor dafay joxe ab yoon ngir xuus ci Internet ci sutura, dimbali nit moytul tere ak caytu. Tor Browser mel na ne yeneen xuusukaay yi ngay jëfandikoo - Chrome, Firefox, Safari, Yandex – wuteeg sa nekkinu xuusukaay ci joxekat serwiis Internet ak képp kuy yëddu sa trafik, dafa lay nëbbël sa trafik di ko nëbb ak bàyyi ko mu dem ci ñetti laxas yu ay wolonteer di lijanti (laxas yooyu ay "linge yi"). Amalin bii dafay nëbb yaw yaay kan, fan nga nekk, ak fan ngay jëm (maanam ban dalu web ngay seet).

Tor ñi kay jëfandikoo ñooy ñiy aar àqq ak yelleefi doomi adama, aktivistë yi, ak nit ñi nekk fépp ci àddina bii yi soxla rëcc tere yi ak caytu yi . Ngir jàng lu ëpp ci Tor ak nan lay doxee, xoolal Tor Browser téereb tegtal.

Jéego 1: Yebbil Tor Browser

Yoon wi gën a wóor te gën a yomb ngir yebbi Tor Browser mi ngi nekk ci dalu web bu ofisiyel bu Tor Project. Ngir sa nosteg doxin, mën nga yebbi Tor Browserci buumu jokkoo bi ci suuf:

Jànkonteel ak jafe-jafe ci yebbi Tor Browser?

Mën na am tolluwaay yoo xam ne doo mën a ubbi dalu web bi di Tor Project website: ci misaal, mën noon nanu boloke sab jokkoo. Bu lii ame, mën ngaa jëfëndiko benn ci yoonu yebbi yu wuute yi ñu tëral bind ci suuf.

Seetu

Mën nga jéem a yebbi Tor Browser jóge ci benn ci mirrors yii, ci biir:

GetTor

Su fekkee dali web mirror yi dañu leena boloke, mën nga laaj ngir jot Tor Browser jaaree ko ci GetTor. GetTor ab serwiis la boo xam ne dafay tontu automatically ay bataaxal jaare ko ci ay lëkkalekaay ci version bu mujj bu Tor Browser, nu deñc ko ci ay bërëb yu wute yu melni, Dropbox, Google Drive ak GitHub:

  • Jeego 1: Yóneel ab xëttu bataaxal ci gettor@torproject.org, te ci ëmbeefu message nu ngi lay ñaan nga bind rekk “windows”, “osx”, wala “linux”, (te amul ay tombu momeelu wax) aju ci sa nosteg amalin. Mën nga tamit yokk ab ràññekaay kàllaama ngir am Tor Browser ci ab kàllaama bu wuteeg Angale. Ci misaal, ngir am ay galanu lëkkalekaay ngir yebbi Tor Browser ci làkku Sinuwaa (Siin) ci Windows, yóneel ab bataaxal ci gettor@torproject.org boole ci baat yii "windows zh_CN" ci biir.

  • Jeego 2: GetTor dina la tontu ag ab bataaxal bu am ay lëkkaloo yoo xam ni danga fa mën a yebbi ëmbeefu Tor Browser bi, xaatim bu nu fas (nu soxla ko ngir caytu yebbi bi), gindikaayu caabi jinu jëfandikoo ko ngir defar xaatim bi, ak checksum ëmbeef bi. Mën nga jox ab tànneef bu amalin “32-bit” wala “64-bit”: Lii dafay aju ci xeetu jumtukaayu xarale bi ngay jëfandikoo.

Mën nga tamit jot ci dosiye yi ak yeneen mbir di jëfandikoo mirrors yii:

Jéego 2: Lëkkalool ak Tor

Soo taale Tor Browser ngir yoon wu njëkk, dinga gis palanteeru Tor window. Lii daf lay jox ab tànneef ngir wala nga lëkkaloo te du am jàdd ci jokkoowu Tor bi, wala nga defaraat Tor Browser ngir sa lëkkaloo. Am na benn boyét buy laac ndax daga bëgg batay lonku ci saasa ci Xuusukaayu Tor, bu fékée lolu la, saytul boyét bi.

War ngaa mënë tambali xuus ci internet ci ak jëfëndiko Xuusukaayu Tor diir bu ndaw ginaaw boo dawalée tëriin wi, tekk ci bës butoŋu "Lonku" boo ko dée jefëndiko ci mu njëkk.

Jànkonteel ak jafe-jafe ci lëkkalook Tor?

Dugg bu gaaw ci jokkoowu Tor bi, yenn saa yi ki lay jox serwiisu Internet wala ab gornamaa mën nañu ko taxawal. Tor Browser am na ay jumtukaayu wër ndombo ngir wër yiile bolokaas. Ci xew-xew yu mel nii, dangay defaraat rekk sa xuusukaay ngir lëkkale jaare ko ci ab bridge war na doy. Jàllukaay yi ay linge kese la yu am kiirlaay te jafee boloke.

Ay tegtal ci naka lanuy dekkilee jàllukaay yi ci ordinaatëeru biro:

Mën nga jëfandikoo ab bridge ci Tor Browser ci ordinaatëeru biro di dem ci: Sukkandikukaay > Lëkkaloo > Jàllukaay > Tànnal ab Built-In Bridge. Ci 22 Desàmbar 2021, jàllukaay yi dajaloo ci Tor Browser danu leen a boloke ci réewum Russie.

Jàngkat yi kon soxla nañu laaj ab bridge jaare ko ci benn ci yoon yii:

  • Di laaj ab bridge jóge ci biir Tor Browser ca biro: Sukkandikuakaay > Lëkkaloo > Jàllukaay > Laajal ab bridge jaare ko ci torproject.org > Saafaraal CAPTCHA bi
  • Di yóne ay "/bridges" ci seenu Telegram bi nu ko jagleel @GetBridgesBot ak tamit yokk dalu bridge bi nu jot ci loxo jaare ko ci sotti ak taf ci Tor Browser: Sukkandikukaay > Lëkkaloo > Jàllukaay > Duggal ci ab dëkkuwaayu bridge bi nga xam ba pare
  • Seetal https://bridges.torproject.org/ te nga topp tegtal yi
  • Di laaj ab bridge jaare ko ci bataaxalu internet: bridges@torproject.org jóge ci dalukaayu bataaxal bu Gmail wala Riseup email; te di yokk ci dalukaayu web bi nu jot ci dalukaayu bridge bi ak loxo jaaree ko ci sotti ak taf ci Tor Browser: Sukkandikuakaay > Lëkkaloo > Jàllukaay > Duggal ci ab dalukaayu bridge bi nga xam ba pare
  • Di lëkkaloo jaaree ko ci Snowflake jóge ci biir Tor Browser: Sukkandikukaay > Lëkkaloo > jàllukaay > Tànnal ab built-in bridge > Snowflake

Ay ndigle ci nan lanuy taalee jàllukaay yi ci Android:

Jàngkat yi mën nañu jëfandikoo ab bridge ci Android di ko jaare ci: xëtu sukandikukaay > Defaraat Bridge > Jëfandikoo ab bridge.

Ci anam yi nga xam ne jàllukaay yi ëmbeefu ci Tor Browser boloke nanu leen, jàngkat yi soxla nañu ab bridge jaare ko ci benn ci yoon yii:

  • Di yóne ay "/bridges" ci seenu Telegram bi nu ko jagleel @GetBridgesBot ak tamit yokk buumu jàllukaay yi nu jot ci loxo jaare ko ci sotti ak taf ci Tor Browser: Defar Bridge > Joxe ab bridge bu ma xam
  • Seetal https://bridges.torproject.org/ te nga topp tegtal yi
  • Di laaj ab bridge jaare ko ci bataaxalu internet: bridges@torproject.org jóge ci ab dalu bataaxal ci ab Gmail wala Riseup; te di yokk buumu jàllukaay yi nu jot ci loxo wala sotti ak taf ci Tor Browser: Defar Bridge > Joxe ab bridge boo xam
  • Di lëkkaloo jaare ko ci Snowflake jóge ci biir Tor Browser: Defarin Bridge > Snowflake

Ay tegtal ci naka lanuy dekkilee jàllukaay yi ci iOS:

Jàngkat mën nañoo jëfandikoo ab bridge ci iOS jaare ko ci: xëtu Onion sooy gis ab dalukaayu web > Bridge Defaraat.

Ci anam yi nga xam ne jàllukaay yi ëmbeefu ci Tor Browser boloke nanu leen, mën nga laaj ab bridge jaare ko ci benn ci yoon yii:

  • Di yóne ay "/bridges" ci seenu Telegram bi nu ko jagleel @GetBridgesBot ak tamit yokk buumu jàllukaay yi nu jot ci loxo jaare ko ci sotti ak taf ci Tor Browser: Defar Bridge > Jàllukaayu kiliyaan
  • Seetal https://bridges.torproject.org/ te nga topp tegtal yi
  • Di laaj ab bridge jaare ko ci bataaxalu internet: bridges@torproject.org jóge ci ab dalukaayu bataaxal ci ab Gmail wala Riseup; te di yokk buumu jàllukaay yi nu jot ci loxo wala sotti ak taf ci Tor Browser: Bridge Sukkandikukaay > Jàllukaayi kiliyaan
  • Di lëkkaloo jaare ko ci Snowflake jóge ci biir Tor Browser: Bridge Defarin > Snowflake

Jéego 3: Duggal ci Onion Service bi

Sarwiisu onion (ñu xamòonléen ci "sarwii yi nëbu") ay sarwiis lañu (yu mélni xuusukaay) yunu mënë jot ludul jaar ci mbàllum Tor. Ne yeneen dalukaayu web yi, dinga soxla xam dalu ab onion service ngir mën ci lëkkaloo. Ab onion address nekk na ab liiñu 56 araf aki lim yunu jël noonu, toftal ci ".onion". Ngir xam lu bare ci Onion Services, seetal Tor Browser téereb tegtal.

Ngir jot Onion Launchpad bu onion service, nu ngi lay ñaan nga sotti rekk te taf URL bile ci Tor Browser: